maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, kenn ci nun de dana yég ci boppam dara Lu koy gaar loo xam ne mu nekk dóom moo koy gë…

