ku jàppoo kem sama njàpp mii, daal di julli ñaari ràkka yoy du ca xalaat dara, kon Yàlla dana ko jéggal bàkkaaram yi jiitu
Jële na ñu ci Humraan jaamub Usmaan Ibn Affaan, mu wax ne, gis na Usmaan Ibn Affaan laaj ndox mu mu jàppoo, mu tanq loxoom ci ndab li, raxas leen ñatti yoon, mu dugal ndeyjooram ci jàppukaay bi, daal di gallaxndiku saraxndiku fiiru, daal di raxas xar kanamam ñatti yoon,…

