mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ànd nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jóge Màkka jëm Madiina ba nu eggee ci am ndox ci yoon wi am ñu
gaawantu ca Tàkkusaan ga, daal di jàppu cig yàkkamti, ba nu egge fa ñoom gis seen tastën ya ndox mi laalu ko, Yonnente bi daal di wax ne: "mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi".
Explanation
ginnaaw ndëggu yi di feeñ ñeel aji-xool ji, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: mbugal ak alkande ca sawara ñeel na ñiy gàtteñlu ci raxas seen ginnaaw ndëggu yi bu ñuy jàppu, mu digal leen ñuy jotal ak di matale njàppu mi.
Benefits
Matale cér yi ñuy raxas lu war la, te ku bàyyi lu ndaw ci yu ñu war a laabal cig tay ak woyofal ag julleem du wér.
Solos jàngal aji-réer ji ak gindi ko.
Aji-xam ji day dindi lu mu gis ci sànk farata ak sunna ci anam ga mu méngool.
Muhammat Ibn Ishaaq Addahlawii nee na: jotale ñatti xeet la: farata, te mooy fexe ba matale barab ba benn yoon, ak sunna te mooy : raxas ñatti yoon, ak lu ñu sopp te mooy : guddal ga te mu ànd ak ñattale ga.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

