dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg
Jële nañu ci Abii Al-Abbaas Sahl ibn Sahd As-Saahidii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, tegtal ma jëf joo xam ne su ma ko defee Yàlla dana ma bëgg nit ñi it danañ…

