bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la
Jële nañu ci Abuu Al-Hawraa As-Sahdii mu wax ne: wax naa Al-Hasan ibn Aliyun yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ko: lan nga mokkal ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc? Mu ne ma: mokkale naa ci Yonnente Yàlla bi: «bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer,…

