HadeethEnc · 1.30.0
Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Muhammad Al-Hasan ibn Aliyun ibn Abii Taalib -sétu Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di mbégteem-, nee na: mokkal naa ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul".
02
Explanation
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa digle ñu bàyyi wax yi ak jëf yi ñuy sikk-sàkka ne dañu ko a tere walla déet, ndax dafa araam walla dafa dagan, te jëm ci yi ñu sikk-sàkkawul te am yaqiin ci rafetam ak ug daganam.
03
Benefits
War na ci jullit bi mu tabax ay mbiram ci li co leer te bàyyi li ñuy sikk-sàkka, te mu nekk ku am luko leer ci diineem.
Tere nañu tàbbi ci yu lënt yi.
Boo bëggee ag dal ak nooflaay nanga bàyyi li ñuy sikk-sàkka sànni ko sa ginnaaw.
Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi ndax da leen a digal li nooflaayu bakkan ak xel nekk, mu tere leen li njàqare ak ngëlëmte nekk.
Tere nañu tàbbi ci yu lënt yi.
Boo bëggee ag dal ak nooflaay nanga bàyyi li ñuy sikk-sàkka sànni ko sa ginnaaw.
Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi ndax da leen a digal li nooflaayu bakkan ak xel nekk, mu tere leen li njàqare ak ngëlëmte nekk.
Attribution
[رواه الترمذي والنسائي]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

