kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.

