Weccee xaalis ci wurus ribaa la lu dul mu nekk loxook loxo, pepp ci pepp ribaa la lu mu nekk loxook loxo, orge ci orge ribaa la lu dul mu nekk am ak am maanaam loxook loxo, tàndarma ci tàndarma ribaa la lu moy loxook loxo
Jële nañu ci Maalik ibn Aws ibn Al-Hadsaan mu wax ne: ana kan mooy weccee dërëm? Talhata ibn Hubayd Allaa ne ko fekk booba ma nga ca Umar ibnul Xattaab yal na leen Yàlla dollee gërëm: wan nu sa wurus wi te nga ñëw bu sunu surga bi ñëwee, nu joxla sa xaalis, Umar ibnul X…

