HadeethEnc · 1.30.0
lu weesu ñaari dojor yi ci koddaay sawara la jëm
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "lu weesu ñaari dojor yi ci koddaay sawara la jëm".
02
Explanation
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo la góor ñi ñuy yoor lépp luy sàng suufu yaram wi ci mbubb walla tubëy, walla lu dul loolu ba mu nekk ci suufu dojori tànk yi, lu wàcc dojori tànk yi ci yére yu ñu yoor loolu sawara la jëm muy am mbugal ci jëfam ji.
03
Benefits
Tere nañu guddal yére ba ci suufu dojor yi ñeel góor ñi, ak ne ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
Ibn Hajar nee na: dees na sette ci buubal yére li mu buubal ngir ag loru; niki ki ay dojoram am gaañu-gaañu weñ yi di ko lor bu dee muuru ko ci koddaayam te amul leneen.
Àtte bii góor ñi ñoo ko jagoo; ndax jigéen ñi dees leen a digal ñu wàcce seen i yére ba ci suufu dojor yi ba ci guddayu loxo.

Attribution
[Al-buxaariy soloo na ko]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares