bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Hittaan Ibn Abdullah Ar-Raxaasii mu wax ne: julli naa ak Abuu Muusa Al-Ashsrii ag julli, dañoo lënkale julli ak ug mbaax ak asaka, nee na: ba Abuu Muusaa noppee ca julli ga ba sëlmël daal di wëlbëtiku, daal di ne: kan ci yéen moo wax baat sàngam ak baat sàngam? Nit ñi noppi, mu waxaat ne: kan ci yéen moo wax wax jii ak jii? Nit ñi noppi: mu ne: man naa am yaw Hittaan yaa ko wax? Mu ne ko: waxu ma ko de, damaa ragal nga gëdd ma ci, am ku wax ci gaa yi ne: man maa ko wax, te nammuma ci lu dul yiw, Abuu Muusa ne ko: xanaa xamuleen lu ngeen di wax ci seen julli gi? Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xutba na nu leeralal nu ay sunnaam xamal nu sunug julli, daal di wax ne: «bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar, bu waxee: (xayril maxduubi halayhim wa laddaalliina) [Al-Faatiha: 7], nangeen wax: Aamiin, Yàlla dana leen nangul, bu kàbbaree daal di rukoo nangeen kàbbar te rukoo, imaam bi moo leen di njëkk a rukoo, moo leen di njëkk a siggi Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu waxee: samihal Laahu liman hamidahu, nangeen wax Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, Yàlla dana leen dégg, Yàlla dafa wax ci nettalig Yonnente bi: samihal Laahu liman hamidahu, bu kàbbaree sujjóot nangeen kàbbar sujjóot, imaam moo leen di njëkk a sujjóot njëkk leen a siggi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu nekkee ca toogaay ba kenn ci yéen na njëkk a wax: attahiyyaatu attayyibaatu assalawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa iLaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan abduhu wa rasuuluhu».
Explanation
Bu ngeen dee julli nangeen jubal séen sàppe yi te yamoo, am ku jiite nit ñi, bu imaam bi kàbbaree bàkkaru armal, nangeen kàbbar ni moom, bu jàngee Faatiha ba toll ci: {xayril maxduubi halayhim wa wa laddaalliina} [Al-Faatiha: 7], nangeen wax Aamiin, bungeen defee loolu Yàlla dana nangu séen ñaan, bu kàbbaree daal di rukoo nangeen kàbbar rukoo; imaam bi moo leen di njëkk a rukoo njëkk leen a siggi buleen ko jiitu; ndax saa su leen imaam bi di jiitu ci rukoo bi, dees leen koy fay ci saa si ngeen di yeex a jóge ca rukoo ba ginnaaw bi mu siggee, kon saa soosee ci saasii rekk, bu ko defee séen diirub rukoo tolloo ak diiru rukoowam, bu imaam bi waxee: samihal Laahu liman hamidahu, nangeen wax: Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, ñiy julli bu ñu waxee loolu, Yàlla mu kawe mi day wax, ci nettalig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: samihal Laahu liman hamidahu, bu imaam bi kàbbaree daal di sujjóot, war na ci maamuun yi ñu kàbbar daal di sujjóot, ndax imaam bi moo leen di njëkk a sujjóot, njëkk leen a siggi kon saa soosa ci saasii rekk, bu ko defee sujjóotu maamuun yi tolloo ak sujjóotu imaam bi, bu nekkee ci toogaayu taaya bi li kiy julli njëkk a wax na nekk: "attahiyyaatu attayyibaatu assalawaatu lil-Laahi" ag nguur ak ug des ak ug màgg lépp Yàlla a ko yayoo, niki noonu julliy juróom yépp Yàlla a ko moom, "assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina", ñaanleen Yàlla ag mucc ci bépp ayib ak gàkk-gàkk ak mànkite ak yàq; nuy jagleel sunu yonnente -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ag nuyoo, door a nuyu sunu bopp, topp nu nuyu jaami Yàlla yu baax yiy taxawe li leen war ci àqi Yàlla mu kawe mi ak àqi jaam ñi, topp nu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat jaamub Yàlla la di ndawam.
Benefits
Jëfi julli yi ak wax yi fàww mu bokk ci li sax jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, kon du dagan ci kenn mu sos ca ay wax mbaa jëf yu saxul ci Sunna.
Du dagan ci maamuun bi muy jiitu imaam bi mbaa di yeex lool ci ginnaawam, li ñu yoonal ci maamuun bi mooy mu topp imaam bi ci ay jëfam.
Tudd ni Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yittewoo woon na jottali, ak jàngal xeet wi àttey diine ji.
Imaam mooy royukaayu maamuun bi, kon du dagan mu koy jiitu ci jëfi julli gi, walla muy tolloo ak moom, mbaa muy yeex lool ci ginnaawam, waaye fa mu koy tàmbalee topp mooy ginnaaw ba mu wóoree ne imaam bi dugg na ci jëf ji mu bëgg a def ba noppi, ndax Sunna mooy mu topp ko ca.
Yoonalees na jubal sàppe yi ci julli gi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

