demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa seet Saabit Ibn Xaysin, benn waay ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, man dinaa la xamal xibaaram, mu dikkal ko fekk ko mu toog ci këram, sëgg boppam bi, mu ne ko: ana luy sa mbir? Mu ne ko: xanaa ay, da doon yëkkati kàddoom ci kaw kàddug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, kon moom ci waa sawara la, waa ji ñëw wax Yonnente bi ne ko: nee na lii ak lee, mu delluwaat beneen yoon indi ag bégle gu màgg, ne ko: "demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk".
Explanation
Waa ji dellu fa Yonnente ba -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ko loolu, Yonnente bi digal ko mu dellu fa Saabit bégal ko ci ne moom bokkul ci waa sawara waaye ci waa àjjana la bokk, ndaxte kàddoom gu kawe gi mbinddin la ci moom, ak ne moom moo doon waxal Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan waxal it waa Lansaar yi.
Benefits
Yittewoo gi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yittewoo ay Sahaabaam ak daan leen nemmeeku.
Ragal gi Sahaaba yi ragal ak tiit ci séen i jëf di yàqu.
Dañoo war a am i teggin bu ñuy wax ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci bi muy dund, ak di suufeel kàddu yi bu ñuy déglu sonnaam ginnaaw bi mu faatoo.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

