Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax,
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax, xéral ci lu lay jariñ, te nga dimbandikoo Yàlla te bul lompañ, bu la dara jotee, bul wax ay bu fekkoon ne defnaa lii mbaa lee kon lii du am, waaye waxal ne Yàlla dogal na te lu ko neex lay def, ndax boo waxul loolu yaa ngi ubbil saytaane buntu».
Explanation
Benefits
Sopp nañu kàttan ci jëf yi; ndax njariñ man na caa ame amiin woo xam ne bu ca kàttan ga nekkul woon du am.
Nit ki dafa war a xér ci lu koy jariñ, te bàyyi lu ko dul jariñ.
War na ci aji-gëm ji muy sàkku dimbaluYàlla ci mbiram yépp, te mu bañ a sukkandiku ci boppam.
Saxal dogal yi ak ne loolu du dàquwante ak def sabab yi ak dox ci sàkku yiw yi.
Tere nañu ñuy wax "budul woon nàngam” di ko wax ci anamug naqarlu ci wàccug musiba, araamal nañu it di gaaral ab dogalu Yàlla mu kawe mi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

