ñaari xéewal a ngi nii yoo xamne nit ñu bari woru na ñu ci: ag wér ak ug jot
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ñaari xéewal a ngi nii yoo xamne nit ñu bari woru na ñu ci: ag wér ak ug jot".
Explanation
Benefits
Ibn Al-Xaasin nee na: xéewal mooy li nit ki di xéewaloo di ci bànneexu, sooy mooy mu jënde njëg gu bari, walla mu jaaye lu yées njëg ga mu jëndewoon, ku wér te am jot ba noppi doxul jëm ci luy yéwénal allaaxiraam kooku ku sooy la ca njaay ma.
Xér ci jariñu ci wér gi ak jot gi ngir jege Yàlla mu màgg mi, ak def yu baax yi laata ñuy weesu.
Sant xéewali Yàlla yi day nekk ci jëfandikoo ko ci topp Yàlla.
Al-Xaadii Abuu Bakrin ibn Al-Arabii nee na: wuute nañu ci xéewalu Yàlla gi jiitu ci jaam bi, ñii ne: mooy gëm, ñii ne: mooy wér, bi njëkk bi nag moo gën a yay, ndaxte moom xéewal gu boy la, bu dee dund ak wér nag ñoom ay xéewali àdduna lañu, te du nekk dëgg-dëggi xéewal lu dul bu àndee ak ngëm, loolu a tax nit ñu bari di ci sooy, maanaam seen tono day dem walla mu wàññeeku, ku topp bakkanam biy digle lu ñaaw biy sax ci nooflaay daal di bàyyi a sàmmonte ak daytal ya, ak sax ci topp Yàlla kooku sooy na, niki noonu it bu dee dafa nekk ku am jot, ki amul jot moom amaana mu am ngànt mu wuute ak ki am jot; kooku moom ngànt la deñ na ci moom, te lay wa dana taxaw ci kawam.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

