nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jàpp ci sama mbagg daal di ne ma: «nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon", ibn Umar, daan na wax naan: boo gontee bul xaar suba, boo xëyee bul xaar ngoon, nanga jël ci sag wée ñeel sag tawat, ak ci sag dund ñeel sag dee.
Explanation
Ibn Umar jëfe ndénkaane lii, daan wax naan: boo xëyee bul xaar ngoon, boo gontee bul xaar suba, te nga limaale sa boppu
ci ñi faatu ñi ak ne dund gi du ñaak wér ak feebar. Gaawantul ci sa bisi yi nga am wér ci topp Yàlla ngir sag feebar; nga gaawantu ci jëf yu baax ci jamanoy wér balaa feebar di dox sa diggante ak moom, te nga
gaawantu sag dund ci àdduna, dajale ca lu lay jariñ ginnaaw boo deewee.
Benefits
Tàmbale ag laabire ak ug jubbanti ñeel ku ko sàkkuwul.
Rafetuw jàngaleg Yónente bi ci sadd ay misaal yuy taxa gëm wax ji ci li mu wax ne: "nekkal ci àdduna mel ni ab doxandeem walla kuy jaar ciw yoon".
Wuuteg nit ñi ci seen uw doxin jëm allaaxira; ki nekk ciw yoon, loolu dakoy def mu nekk ki gëna dëddu ab doxandeem.
Leeral gàttug mébét, ak waajal dee
Hadiis bi tegtalewul bàyyi wërsëg ak araamal neexiti àdduna; wànte day tegtale ag xemmeemloo ci ag dëddu, ak tuutal àdduna.
Gaawantu jëm ci jëf yu baax yi balaa mu koy ñàkk a manati, feebar tere ko ko mbaa dee.
Ngëneelu Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm ba tax mu jeexantalu ci waare wii jóge ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Dëkkuwaayu way-gëm ñi mooy àjjana kon moom doxandeem la ci àdduna, te aji-tukki la jëm allaaxira, du wékk xolam ci dara ci réewum tumbrànke mi, waaye xolam day wékku ci dëkkuwaay ba muy dellu, te ag saxam ci àdduna ngir faj aajoom la ak waaj ngir dellu ca réewam ma.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

