deeleen dégg tey topp, li leen war ñoom mooy la ñu leen gàdduloo, yéen it li leen war mooy li ñu leen gàdduloo
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Waa-il Al-Hadramii mu wax ne: Salamata ibn Yasiid Al-Juhfii yal na ko Yàlla dollee gërëm laaj na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: Yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar ma bu nu ay njiit jiitee di nu laaj seen àq, di nu xañ sunuy àq, ana lan nga nuy digal? Mu dummooyu ko, topp mu laajaat ko, mu dummooyu ko, mu laaj ko ci ñaareel bi walla ñatteel bi, Al-Ashas ibn Xays xëcc ko, mu ne ko: "deeleen dégg tey topp, li leen war ñoom mooy la ñu leen gàdduloo, yéen it li leen war mooy li ñu leen gàdduloo".
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dummooyu ko; mu mel ni dafa sib laaj bi, waaye aji-laaj ji delloo ko laaj bi ñaari yoon ak ñatti yoon, Al-Ashas ibn Xays yal na ko Yàlla dollee gërëm xëcc ko ngir noppiloo ko.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tontu ko, ne ko: nangeen dégg seen i wax, tey topp seen i ndigal; ñoom li leen war mooy la nu leen gàdduloo waral ko ci ñoom cig maanute ai joxe àqi càmm gi, li leen war yéen mooy li ñu leen gàdduloo ci topp ak joxe àq yi ci muñ kaawteef yi.
Benefits
Gàtteñlug njiit yi ci seen i àq du tax nit ñi war gàtteñlu ci weccee loolu ci seen i àq; ku nekk dees na ko laaj jëfam, te dees na ko toppe ag gàtteñloom.
Diine tabaxuwul ci fayyantoo waaye ci taqoo ak li war la donte ñeneen ñi dañoo gàtteñlu ca la leen war, kem ni mu rote ci Hadiis bi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

