ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege
sunu jàkka yi, te toog ci këram", ak ne Yonnente bi indil nañu ko cin lu am ay lujum ak laaj, mu yég ci ag xet, mu laaj ñu xibaar la ca nekk ci laaj, mu wax ne: jegeele leen ko ci kenn ci Sahaaba yi nekkoon ak moom, ba mu ko gisee mu sib ko a lekk, mu wax ko ne: " lekkal, man damay déeyante ak koo dul déeyantel». Ñëw na ci Muslim ñu jële ci Jaabir ibn Abdul Laah, mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: ku lekk reen bii, laaj gii - mu wax benn yoon ne: ku lekk soble ak laaj ak xeetu soble bu mu jege sunu jàkka ji, ndaxte malaaka yi dañuy loru ci li doomu Aadama di loru".
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle ne malaaka yi dañuy loru ci xet gu xasaw, kem ni nit ñi di ci loroo.
Benefits
Dees na boole ci yooyu, lépp lu am xet gu xasaw gu jullikat yi di loroo, niki xetu sigareet ak póon ak yu ko niru.
Li waral tere gi mooy xet gi, kon bu xet gi deñee ngir togg gu bari mbaa ci leneen; kon sibeel gi deñ.
Sib nañu lekk bir yii ci kuy teewe julli gi ci jàkka ji; ngir mbooloo mi ci jàkka ji bañ ko a faat, lu dul mu lekk ngir bexey baña teew, buboobaa day araam.
Li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bañ a lekk laaj ak yi ko niru, du ngir araamal ko, waaye ngir ne day déeyaale ak Jibriil moo tax.
Rafetug jàngàlem Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ba tax muy lënkale àtte bi ak leeral sabab bi; ngir dalal xelu ki muy waxal ci bu xamee litax.
Al-Xaadii nee na: woroom xam-xam yi nattale nañu ci lii yeneen barabi jullikaay u mbooloo yi nekkul ci jàkka niki jullig iid, ak néew ak yu ko niru ci jaamu, niki noonu barab yi ñuy daje ngir xam-xam ak sikar ak céet ak yu ko niru, waaye (jah yi) marse yi ak yi ko niru du ca dugg.
Woroom xam-xam yi nee nañu: hadiis bi tegtal la ci tere lekk laaj ak yu ko niru ci bu ñuy dugg ci jàkka -donte kenn nekku fa- ndaxte barabu malaaka yi la, ak it li hadiis yi matalee.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

