jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp, loolu nag ndax bu kenn ci ñoom jàppee rafetal njàppu ma, daal di dem ca jàkka ja te dara yëkkatiwu ko lu dul julli, du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil daraja, sippil ko ci njuumte, ba ba muy dugg ca jàkka ja, bu duggee ca jàkka ja ci julli la nekk fii ak julli moo ko téye, te malaaka yi dañuy julli ci kenn ci yéen fii ak moo ngi ca bérab ba mu doon jullee, dañuy wax naan: Yàlla yërëm ko, Yàlla jéggal ko, Yàlla nangul tuubam, fii ak lotul kenn, te tojlewul».
Explanation
Benefits
Jullig mbooloo ca jàkka ja moo gën jullig nit ki beru ci ñaar-fukk ak juróom walla juroom-benn walla juróom-ñaari daraja.
Bokk na ci liggéeyi malaaka yi di ñaanal way-gëm ñi.
Ngëneelu dem jàkka ànd ak njàppu.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

