yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Al-Axarri yal na ko Yàlla dollee gërëm mu bokkoon ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu wax ne: Yonente Yàlla bi nee na: «yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon».
Explanation
Benefits
Tuub day matale moo xam ci yu araam yi la ak bàkkaar yi walla ci gàtteñlu ci def yu war yi la.
Sellal ci tuub sàrt la ngir mu nangu, ku bàyyi ab bàkkaar ngir ku dul Yàlla kooku tuubul.
An-Nawawii nee na: tuub am na ñatti sàrt: mu bàyyi bàkkaar bi, ak mu réccu def ga, ak mu dogu ci bañ a dellu ci lu mel noonu ba fàww, bu bàkkaar bi ajoo ci àqi doomu Aadama kon day am sàrtub ñenteel, te mooy: delloo tooñaange gi boroomam, walla amal ag cet ca moom.
Ag bàyyikoo xel ci ne jéggalug Yonente bi du caagine daa am ay bàkkaar yu mu def, wante loolu ngir matug njaamam la ak ug ajoom ci tudd Boroomam mu Sell mi, ak yëgam màggug àqi Yàlla, ak gàtteñlug jaam bi ak lu mu man a def ci sant ay xéewalam, te it ci buntub yoonal la ñeel xeetam wi, ak yeneen xereñte yu dul yooyu.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

