mbir mii (te mooy diine ji ) dana egg fu guddi gi ak bëccëg gi egg, te Yàlla du bàyyi kërug taax walla kërug kaw lu dul ne dana fa dugal diine ji
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Tamiim Addaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "mbir mii (te mooy diine ji ) dana
egg fu guddi gi ak bëccëg gi egg, te Yàlla du bàyyi kërug taax walla kërug kaw lu dul ne dana fa dugal diine ji, ci teddaangey aji-tedd walla toroxtaangey aji-torox, ag teddaange ju Yàlla di terale Lislaam, ak toroxtaange ju Yàlla di toroxale kéefar", Tamiim Addaarii daan na wax naan: loolu de ci sama waa kër laa ko xame, ku ci tuub ci ñoom rekk am na yiw teddnga ak ug màgg, ku ci weddi ci ñoom am na toroxtaange ak ug tuuti ak joxe juuti.
Explanation
Sahaaba bi di Tamiim Addaarii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne moom ci këram la xame lii Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare, ndax ku ci dugg ci Lislaam ci ñoom am na yiw ak teddnga ak ug màgg, ku ci weddi ci ñoom am ug toroxtaange ak ug doyadi ànd ak li muy jox jullit ñi ci juuti.
Benefits
Teddnga ñeel na Lislaam ak jullit ñi, toroxtaange ñeel na kéefar ak yéefar yi.
Tegtal la ci tegtali Yónnente gi di màndarga ci ay màndargaam ndax mbir mi dafa ame kem ni ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare woon.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

