war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam».

