doon na la doy rekk nga def nii say loxo" mu dóor ay loxoom ci suuf benn dóor, daal di masaa càmmooñam ci kaw ndayjoor bi, ak bitti ténq yi ak kanam gi
Jële nañu ci Ammaar ibn Yaasir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da maa yónni ci jenn aajo, ma am janaba te amuma ndox, ma xalangu ci suuf si kem ni daaba di xalangoo, ma ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàll…

