Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla
Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay ànd…

