bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Jenn waay dafa wax: yaw Yonnente Yàlla bi damaa am jegeñaale ma leen di jokk ñu may dog, may rafetal jëme ci ñoom ñuy ñaawal jëme ci man, may lewet ci ñoom ñuy fétteerlu ci sama kaw, mu ne ko: "bu dee n…

