ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko
Jële nañu ci Abii Xataadata yal na ko Yàlla dollee gërëm ne na da doon seet kenn ku ko ameeloon bor, mu làqatu ko topp mu gis ko, mu ne ko: man de ci jafe-jafe laa nekk, mu ne: ndax da nga ko waat ci Yàlla? Mu ne ko: waat naa ko ci Yàlla? Mu ne ko: man dégg naa Yonnente…

