mo ndax wóoluwuleen ma te man maay kóoluteg ki ci asamaan xibaaru asamaan dima dikkal suba ak ngoon
Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa yónnee ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu bawoo Yaman as wurus mu nekk ci abder bu nu wulli, te setaluñu ko sax ca suuf…

