HadeethEnc · 1.30.0
giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm", ñu ne ko: kan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "ki dëkkandoom muccug ci ay loram
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Surayhin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm", ñu ne ko: kan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "ki dëkkandoom muccug ci ay loram".
02
Explanation
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa giñ feddali giñam li ñatti yoon, daal di ne: giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, Sahaaba yi laaj ko: kan mooy ki dul gëm yaw Yonente Yàlla bi? Mu wax ne: mooy ki dëkkandoom ragal woram ak tooñam ak ayam.
03
Benefits
Dàq ngëm ci ki dëkkandoom wóoluwul tooñaangeem ak ayam day tegtale ni ci bàkkaar yu mag yi la, ak ne ki ku def dafa mànki ag ngëm.
Ñaaxe gu feddaliku ci rafetal jëme ci dëkkandoo ak bàyyi ko a lor ci wax walla jëf.
Ñaaxe gu feddaliku ci rafetal jëme ci dëkkandoo ak bàyyi ko a lor ci wax walla jëf.
Attribution
[Al-buxaariy soloo na ko]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

