li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: Ay nit yu bokkoon ca bokkaalekat ya, dañoo ëppaloon ci raye, ëppal ci njaalo, ñu ñëw ci Yónente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale, aaya bi daadi wàcc {ak ñi nga xam ne duñu jaamu jeneen Yàlla di ko bokkaale ak Yàlla, te duñu ray bakkan bu Yàlla araamal ci lu dul dëgg te duñu njaalo{ [Al-Furxaan: 68], aaya bii it wàcc: {waxal sama jaam ñi nga xam ne dañoo ëppal ci def ay bàkkaar buñu naagu mukk ci yërmàndey Yàlla} [As-Sumari: 53].
Explanation
Ñaari aaya yi daal di wàcc, ne Yàlla day nangu tuub ci nit ñi ak lu séen i bàkkaar bari te rëy, ndax bu dul woon loolu danañu wéy ca séen kéefar ga ak séen mbewte ma te kon duñu dugg ci diine ji.
Benefits
Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi ak njéggalam ak ug baaleem.
Bokkaale dafa araam, ray bakkan ci lu dul dëgg dafa araam, njaalo dafa araam, tëkku nañu it kuy def bàkkaar yii.
Tuub gu dëggu gu ànd ak sellal ak jëf lu baax day far mbooleem bàkkaar yu mag yi ba ci weddi Yàlla mu kawe mi sax ca la bokk.
Araamalees na naagu ak ñakk yaakaar ci yërmàndey Yàlla -tudd naa sellam ga-.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

