HadeethEnc · 1.30.0
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul woon xam luy xàjjale saar yi ba ba ñuy wàcce ci Moom {Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim}
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul woon xam luy xàjjale saar yi ba ba ñuy wàcce ci Moom {Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim}.
02
Explanation
Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day leeral ne saari Alxuraan yi da daan wàcci ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- te daawul xam teqale ba ak fan la yam, ba ba ñuy wàcce ci moom: "Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim" mu door a xam ne saar wi jiitu jeex na, weneen saar wu bees moo tàmbali.
03
Benefits
Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim mooy tàqale diggante saar yi, bamu des diggante saaru Al-Anfaal ak saaru At-Tawba.Bokk na ci njariñal hdiis bi:
Attribution
[Abóo Daawuda soloo na ko]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

