ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi, Ibn Jadhaan de ca jamanoy ceddo ga da daan jokk mbokk di leel miskiin, mo ndax loolu dana ko jariñ ? Mu wax ne: «du ko jariñ de, ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba».
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Abdallah Ibn Jadhaan, bokkoon na ci njiitu waa Xurays njëkk Lislaam, Te bokk na ci ay jëfam yu baax: daa na jokk mbokk, di rafetal jëme ci ñoom, di leel miskiin, ak yeneeni ngënéel yoy Lislaam dafa ñaaxe ci def ko, ci ne jëf yooyu du ko jariñ ëllëg bis-pénc; te li ko waral mooy weddi gi mu weddi Yàlla, te masul wax: yaw sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba.
Benefits
Leeral gaafug kéefar, ak ne moom day màbb jëf yu baax yi.
Yéefér yi séen jëf du leen jariñ ëllëg bis-pénc ndax li ñu gëmul Yàlla ak bis bu mujj ba.
Jëfi nit ki jamono ya mu nekkee yéefar bu tuubee danañu ko ko bindal aw yiw daal di ka koy fay.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

