xoli doomi Aadama yépp ñoo ngi ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla miy Yërëmaakoon bi, mel ni benn xol, mu koy wëlbati jëme fu ko soob
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu dégg Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: "xoli doomi Aadama yépp ñoo ngi ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla miy Yërëmaakoon bi, mel ni benn xol, mu koy wëlbati jëme fu ko soob" topp Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: "yaw sama Boroom Aji-Wëlbati xol yi jëmaleel sunu xol yi ci topp la".
Explanation
Benefits
Jaadu na ci jullit bi mu sax ci ñaan Boroomam ag sax ci dëgg ak njub.
Ragal Yàlla ak aju ci Moom dong amul bokkaale.
Al-Aajurrii nee na: (ñoñ-dëgg ñi dañuy melal Yàlla mu màgg mi ci li mu melale boppam moom Aji-Màgg ji, ak ci li ko Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc melale, ak li ko Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm melale, lii mooy yoonu woroom xam-xam yiy topp te sosuñu.) Waa sunna dañuy saxalal Yàlla li mu saxalal boppam ci ay tur ak i melo ci lu dul soppi du caagine neenal, ci lu dul melale du caagine it niróole, ñuy dàq ci Yàlla li mu dàqal boppam, di noppi ci loo xam ne dàq gi ak saxal gi dara rotu ci, Yàlla mu kawe mi nee na: (dara melul ni moom te mooy Aji-Dégg ji di Aji-Gis ji).
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

