HadeethEnc · 1.30.0
Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan».
02
Explanation
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne amul dara lu gën a tedd fa Yàlla ci jaamu yi lii di ñaan; ndaxte nangu la ci ne Yàlla ku doylu la -tudd naa sellam ga- ak nangu ne jaam bi dafa aajowoo Yàlla.

03
Benefits
Ngëneelu ñaan, ak ne képp ku woo Yàlla, ku ko màggal la, te nangu ne ku doylu la -tudd naa sellam ga-, ndaxte néew gi doole duñu ko ñaan, ak ne dafay dégg, ndaxte ku tëx duñu ko woo, ak ne mooy Aji-Tedd, ndax ku nay deesu ko ñaan, ak ne mooy yërëmaakoon bi, ku soxor duñu ko ñaan, ak ne ku am kàttan la, ku ñàkk doole duñu ko ñaan, ak ne Aji-Jege la, ku sori du dégg, ak yeneen meloy màgg yu dul yooyu tey wane màggug Yàlla Mu tedd mi ak taaram.
Attribution
[At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares