li gën a kawe cig jégalu yi mooy
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".
Explanation
moyam, Ginnaw lii, day ñaan Boroomam mu jéggal ko, ci suturaal ko ay bàkkaaram te fegal ko bàkkaar ya ci njéggalam ak ngëneelam ak yërmàndeem, ndaxte kenn du jéggale bàkkaar yi ku dul moom Yàlla mu màgg mi. Topp muy xibaare ne dafa bokk ci sikkari suba yi ak guddi yi, ku ko wax ci kóolute ak teewlu maanaa yi ak gëm ko ci njëlbeenu bis bi, ci diggante fenkug jant bi ba baa muy jeng, te mooy waxtuw bëccëg gi, mu daal di faatu dana dugg àjjana, Ku ko wax ci guddi gi it, te mooy bi jant bi sowee ba baa fajar gi di fenk, mu daal di faatu njëkk suba di jot, dana dugg àjjana.
Benefits
Jaadu na ci jaam bi mu xér ci di ñaan Yàlla ci ñaan gii; ndaxte mooy sangi jéggalu yi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

