Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdullah ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ñaan ci baat yii; "Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa".
Explanation
Bi ci njëkk: (yaw sama Boroom maa ngi muslu) di ñëw di làqu (ci yaw) làquwunu ci keneen ku dul yaw, (ci bor bu bari) ag notam ak ug njàqareem ak tiisam, ma lay ñaan nga dimbali ma ci fay ko.
Ñaareel bi: (ak notug noon bi) ak notam ak ug songam, ma lay ñaan nga tëye loram wi, ak dimbali ma ci kawam.
Ñatteel bi: ,(ak ndokkug noon yi) seenug bég ci liy dal jullit ñi ci balaa ak musiba.
Benefits
Bor kese dara nekkesi, waaye li aay mooy ki amul kóllareg fay, lii mooy bor giy note.
Nit ki war naa moytandiku bir yi ñuy ndokke di ci ayibale.
Leeral nooneelug yéefar ñeel way-gëm ñi ak seenug ndokk ci ñoom ci musiba yi.
Feeñalug noon yi seen mbégte ci balaa yiy dal nit ki day gën a tar ci nit ki jëmmi balaa bi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

