képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral ganam».
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jaam bi gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nga xam ne falay dellu ñu fay ko ay jëfam, ngëmam dana ko ñaax ci jikko yii:
Bu njëkk bi: wax ju rafet: ci sàbbaal, ak tudd Yàlla, di digle lu baax, di tere lu bon, di defar diggante nit ñi, bu ko deful it mu taqook noppi téye loram te sàmm làmmiñam.
Ñaareel bi: teral dëkkandoo: ci di rafetal jëme ci moom te bañ koo lor.
Ñatteel bi: teral gan gi ñëw ngir seetsi la: ci wax ju teey, ak jox ko ñam ak yu ni mel.
Benefits
Moytondikuloo gàkk-gàkki làmmiñ yi.
Diiney Lislaam diney miinante la ak teraanga.
Jikko yii daa bokk ci pàcci ngëm yi ak teggin ya ñu gërëm.
Bari wax day waral tàbbi ci lu ñu sib mbaa lu araam, te mucc moo ngi nekk ci bañ a wax ludul Aw yiw.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

