Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: amuma waruwaay, kon nag jox ma waruwaay, mu ne ko: «amuma ko», am ku ne ko: yaw Yónente bi, dinaa ko tegtal ku ko jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am».
Explanation
Am na ku mas a w ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- ne ko: sama waruwaay dafa dee, yéegal ma cig daaba, te jox ma waruwaay mu yóbbu ma, Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- gàntal ko, ne ko amul dara lu mu koy jox, benn waay bu nekkoon foofu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi dinaa ko yóbbu ci ku koy jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm- xamle ne, mook kiy saraxe ñoo bokk am yiw, ndax moo ko tegtal aji-yittewoo ji.
Benefits
Soññee ci def lu baax bokk na ci sabab i jàppalanteeg jullit ñi ak seenug bennoo.
Yaatug ngënéelu Yàlla.
Hadiis bii ab tënk bu matale la, jépp jëf ju baax da ciy dugg.
Nit ki bu manut a faj aajiy kiy laaj, da koy tegtal keneen.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

