HadeethEnc · 1.30.0
amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Mahqal Ibn Yasaar Almusanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana».
02
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku Yàlla def kilifa mu jiite nit ñi, moo xam njiit lu mag la niki buur, walla njiit lu ndaw niki góor gi ci këram, ak jigéen gi ci këram, mu gàttanlu ci àqi la muy sàmm, di leen wuruj te du leen laabire, daal di sànk séen i àq yu diine mbaa yi àdduna, kooku yayoo na mbugal mu tar mii.
03
Benefits
Bokk na ci njariñal adiis bi : Tëkku gii nag nekkul ne njiit lu mag li ak ña koy wuutu rekk a ko jagoo, waaye day làmboo képp ku Yàlla sàmmuloo am càmm.
Li war képp ku jiite dara ci biri jullit ñi mooy mu leen di laabire, te pastéefu ci matal kóllare, te moytoo wor.
Màggaayu wartéefu képp Ku yilif Aw nit, moo xam kiliftéef gu gu ndaw walla gu mag.
Li war képp ku jiite dara ci biri jullit ñi mooy mu leen di laabire, te pastéefu ci matal kóllare, te moytoo wor.
Màggaayu wartéefu képp Ku yilif Aw nit, moo xam kiliftéef gu gu ndaw walla gu mag.
Attribution
[Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

