jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Barsata Al-Aslamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal».
Explanation
Bi ci njëkk: dundam gi ci lan la ko jeexal?
Ñaareel bi: xam-xamam bi ndax da koo sàkku ngir Yàlla? Ak ndax jëfe na ko? Ak ndax jottali na ko ñi ko yeyoo?
Ñatteel bi: alalam ji fan la ko ame ndax ci lu dagan la walla lu araam? Ak fan la ko dugal, ci lu Yàlla gërëm la walla lu koy merloo?
Ñenteel bi: yaramam wi ak kàttanam gi ak jàmmam ji ak waxambaanem gi ci lan la ko ràppale, lu mu ci def?
Benefits
Xéewali Yàlla yi ci jaam yi lu bari la, te dana ko laaj xéewal yi mu ko jox, kon war na ci moom mu def xéewali Yàlla yi fu Yàlla gërëm.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

