bul ko ray, ndaxte boo ko rayee moom day nekk sa barab laata nga koy ray, yaw nga nekk ci barabam laata muy wax kàddu gi mu wax
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Amr Al-Kindii yal na ko Yàlla dollee gërëm: moom dafa wax Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: waaw xibaar ma bu ma dajee ak jenn waay ci yéefar yi ñu rayante, mu dóor jaaseem ji ci sama benn loxo
daal di koy dagg, topp mu làqatu ma ci genn garab, daal di wax ne: man jébbalu naa ñeel Yàlla, ndax dama koy ray yaw Yonnente Yàlla bi ginnaaw ba mu ko waxee? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bul ko ray" mu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, moom dafa dagg sama benn loxo, daal di wax loolu ginnaaw bi mu ko daggee? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bul ko ray, ndaxte boo ko rayee moom day nekk sa barab laata nga koy ray, yaw nga nekk ci barabam laata muy wax kàddu gi mu wax".
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bul ko ray.
Mu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, moom dafa dagg sama benn loxo, ndax loolu du tax ma ray ko?!
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bul ko ray, ndaxte moom leegi dereetam araam na, te boo ko rayee ginnaaw lislaamam; kon moom mooy nekk ci sa barab di ku ñu araamal deretam ginnaaw
lislaamam, yaw nga nekk ci barabam di ku dereetam dagan ci fayyanto ci ray ngi nga ko ray.
Benefits
Bu kenn ci yéefar yi jébbaloo ci jamonoy xare bi, kooku dereetam ñoŋ na, te warees na ko bàyyi lu dul lu wuute ak loolu feeñ ci moom.
War na ci jullit bi bànneexam topp Sariiha te bañ a topp par-parloo walla fayyontoo.
Ibn Hajar nee na: dagan na ñu laajte yu bees yiy sosu njëkk muy tàbbi ñu tabax ko ci notal ne nettali bii amagul woon, bu dee li ñu toxale ci yenn mag ña ci sibug loolu dees koy yan ci li nga xam ne ag tàbbeem lu néew lool la, budee lu man a tàbbi ci aada yoonalees na laaj ga ngir ñu xam ko.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

