dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».
Explanation
Benefits
Bokk na ci xereñteg Yàlla ak yërmàndeem mu nëbb guddi gii ngir nit ñi pasteefu ci jaamu gi, ngir sàkku ko, ndax seen yool bari.
Laylatul Xadri mi ngi ci fukki guddi yi mujj ci weeru koor, te ci yu tóol yi la gën a yaakaaru.
Laylatul Xadri benn la ci fukki guddi yi mujj ci weeru koor, te mooy guddi gi Yàlla mu màgg mi wàcce Alxuraan ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu def guddi gii mu gën junni weer ci baarke, ak màggug dayoom, ak jeexiti jëf yu baax ci moom.
Tudde nañu ko(Laylatul Xadri) ci sukoon Daal gi benn mu jóge ci teddnga, dees na wax: diw ku màgg dayo la, laafal gi ñu laafal guddi gi nekk ci buntub laafal dara ci meloom, maanaam guddi gu tedd gi, maanaam moom ku màgg dayo la ci teddnga ak ug màggaay ak ug dayo ba mu jeex, {Nun noo ko wàcce ci guddi gu baarkeel} [Ad-Duxaan: 3], benn mu jóge ci nattale: laafal gi nekk laafal jamono ca la mu làmboo, maanaam guddi gii mooy gi nga xam ne ca la nattale liy am ci at mi di nekk, {ca lañuy teqale bépp mbir mu ñu xereñe} [Ad-Duxaan: 4].
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

