jullit bi bu ñu ko laajee ci bàmmeel: day seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Al-Baraa ibn Aasib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «jullit bi bu ñu ko laajee ci bàmmeel: day seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la" loolu mooy li Yàlla mu kawe mi wax: {Yàlla dana saxal way-gëm ñi ci wax juy sax ci dundug àdduna ak ci allaaxira} [Ibraahiima: 27].
Explanation
Munkar ak Nakiir ñu laaj ko, kem ni ñu leen tudde ci ay hadiis yu bari, Mu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na wax jii mooy wax jay sax wax ji Yàlla ne: {Yàlla dana saxal way-gëm ñi ci wax juy sax ci dundug àdduna ak ci allaaxira} [Ibraahiima: 27].
Benefits
Ngëneelu Yàlla ci kaw jaamam yu gëm yi ci àdduna ak allaaxira ci saxal leen ci wax juy sax.
Ngëneelu seedeg Tawhiid ak faatu ca.
Saxal gi Yàlla di saxal aji-gëm ji ci àdduna mooy mu sax ci ngëm, jaar ca yoon wu jub wa, bu dee faatu nag mooy mu dee ci Tawhiid, bu dee ci bàmmeel mooy ca laaji ñaari malaaka ya.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

