saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal, bu yeewoo daal di tudd Yàlla genn fas-fas fecceeku, bu jàppoo geneen fas-fas fecceeku, bu jullee geneen fas-fas fecceeku, mu mujj nekk ku sawar, ku teey bakkan, bu dul loolu day nekk ku bon bakkan di ku tàyyeel".
Explanation
Aji-gëm ji bu demee jëm ca nelaw ya saytaane day fas ci ginnaaw boppam ba -maanaam: ginnaaw catu bopp ba- ñatti fas-fas.
Bu aji-gëm ji yewwoo daal di tudd Yàlla mu kawe mi te nangulul jax-jaxi Saytaane yi; genn fas-fas fecceeku.
Bu jàppoo geneen fecceeku.
Bu jugee daal di julli fas-fasu
ñatteel bi
fecceeku, mu xëy di ku sawar di ku teey bakkan; ngir ag bégam ci li ko Yàlla tawfeexal ci mu jaamu ko, di bége li ko Yàlla dig ci ab yool ak njéggal, ak fas-fasi Saytaane yi ak tàyyeelam gi deñ ci moom, bu dul loolu rekk day xëy di ku bon bakkan, di ku jàq ab xol, di ku tàyyeel ci def aw yiw ak lu baax; ndaxte moom dees ko a jéng ci jéngi Saytaane, muy ku ñu soreele wolif jege Aji-Yërëmaakoon ji.
Benefits
Tudd Yàlla day waral cawarte ci bakkan bi, ak dënn bu yaatu, te day dàq tàyyeel ak yonjax, te day dindi jafe-jafe ak mbañeel; ndaxte day dàq Saytaane te lii ci ay jax-jaxam la.
Aji-gëm ji day bég ci li ko Yàlla di tawfeexal ci mu taxaw ci topp ko, waaye day xat ngir gàtteñloom ci ngëneel yi.
Càggante ak baña topp Yàlla ci jëfi Saytaane la.
Ñatti bir yii -tudd Yàlla, ak jàppu, ak julli- day dàq Saytaane.
Fasi Saytaane yi ci ginnaaw bopp bi la ko jagleel; ndaxte mooy barabu kàttan gi, kon bu ko fasee dana man a not ruuhu nit ki, ak sànni ko ay nelaw.
Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: tudd gi mu tudd guddi ci li mu wax: "am nga guddi", li ci feeñ mooy loolu dafa jagoo nelawi guddi.
Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: genn sikar gu ñu jagleel ràññeekuwul ci sikar yi ba gu dul moom du ca doy, waaye lépp lu tudd Yàlla rekk doy na, jàng Alxuraan da cay dugg, ak jàng Hadiisu Yonnente bi, ak yittewoo jàng xam-xamu sariiha, li gën a yay nu tudd ko ca mooy waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: (laa i Laaha illal-Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa huwa halaa kulli say-in xadiirun, Alhamdu lil-Laah, wa subhaanal Laah, wa laa-i-Laaha illal-Laahu wal-Laahu Akbaru, wa laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-Laahi, topp mu wax: allaahuma ixfirlii, walla mu ñaan, dees na ko nangul, bu jàppoo ñu nangu julleem) Al-Buxaarii soloo na ko.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

