Dañoo tudd fi Yonnente bi jenn waay bu nelaw guddeem gi yépp ba suba jot, mu ne: "kooku mooy ki nga xam ne saytaane daa saw ci ay noppam, walla mu wax: ci noppam
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Dañoo tudd fi Yonnente bi jenn waay bu nelaw guddeem gi yépp ba suba jot, mu ne: "kooku mooy ki nga xam ne saytaane daa saw ci ay noppam, walla mu wax: ci noppam".
Explanation
Benefits
Moytandiku saytaane mi nga xam ne day toog ci yoonu nit ki; ngir dox ci digganteem ak topp Yàlla mu màgg mi.
Ibn Hajar nee na: li mu wax: (jugul jëm ci julli gi) li ñu ci namm mooy xeetu julli rekk, jamtal na it muy gu ñu xam, ñu namm ci julli guddi, walla gu farata.
At-Tiibii nee na:tudd gi ñu tudd nopp donte bët moo gën a méngoo ak nelaw, loo lu junj la ci diisug nelaw yi, ndax nopp yi la ñuy bàyyee xel, tudd nañu saw ndaxte moo gën a yomb te gën a gaaw a jàll ca séddit ya, ba tax muy waral tàyyeel ci mbooleem cér yi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

