HadeethEnc · 1.30.0
Buleen di ŋàññ sama àndandoo yi, bu kenn ci yéen joxe woon lu toll ne Uhud ci wurus du jot Muddub kenn ci ñoom, waxumalaak xaaj ba
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Buleen di ŋàññ sama àndandoo yi, bu kenn ci yéen joxe woon lu toll ne Uhud ci wurus du jot Muddub kenn ci ñoom, waxumalaak xaaj ba».
02
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñuy ŋàññ Sahaaba yi, rawati na ña jiitu ca way-gàdday ya,
ak lansaar ya ; mu xamle ne bu kenn ci nit ñi joxe woon lu toll ni doju Uhud ci wurus du jot yoolub joxeg kenn ci Sahaaba yi Muddub ñam walla xaaj
ba Mudd mooy loxob nit ku yam-; li ko waral mooy seen ug sellal, ak seen yéene ju
dëggu, ak seen ug jiitu ci joxe ak xeex njëkk ubbiteg Màkka.

03
Benefits
Ŋàññ Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dafa araam, te ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
Attribution
[Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares