bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi".
Explanation
Benefits
Ag bégle la ñeel ñi ciy woor ci ne weer wu baarkel wii ag jamanoy jaamu Yàlla la ak def lu baax.
Tënk gi ñuy tënk saytaane yi ci weeru koor ag junj la ci dindi ngàntal mukallaf mi mu mel ni dañu koy wax ne: fegalees na la saytaane yi kon bul joxe ngànt ci bàyyi jaamu gi du caagine def moy yi.
Al-Xurtubii nee na: bu ñu nee: bu dee da ñuy tënk saytaane yi ci weeru koor gi kon lu tax ñuy gis lu bon ak ay moy Yàlla di am ci weer wi? Tontu li mooy: bàkkaar yi day néew ci woorkat yi woor koor gu jaar yoon, walla tënk gi yenn saytaane yi fétterlu rekk la waaye du yépp, kem ni mu jiitoo ci yenn nettali yi, walla li ñu ci jublu mooy yu bon yi néew gi muy néew ci weer wi, te lii lu ñu yëg la, lu bon limuy am ci weeru koor moo gën a néewe weer yi ci des, ndaxte tënk ñépp it du caagine lo bon du am; ndaxte loolu dafa am yeneen sabab yu dul saytaane niki bakkan bu bon bi, ak aada yu ñaaw yi, ak saytaaney nit yi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

